¶ Ca jamono yooyu Yuda dafa teqlikoo ak ay doomi baayam, dal ca waa ju dëkk Adulam te tudd Ira.
TSK
TSK · Genesis 46:12
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu dellu ëmb, am doom ju góor, tudde ko Onan.
Er, taawub Yuda boobee, doonoon ku Aji Sax ji seede coxoram; Aji Sax ji nag rey ko.
¶ Ba ñu ca tegee lu tollook ñetti weer, ñu xamal Yuda ne ko, Tamar goroom ba, da doon jaay boppam, ba jaare ca ëmb. Yuda ne: «Nañu ko yóbbu, lakk ko, ba mu dee.»
«Yaw Yuda, mi say doomi baay di taggeji, ngay sëqi sa ndoddi noon, sëgal leen, sa doomi baay a lay sujjóotal.
¶ Ñu lim turi sëti Yuda, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
Ñi askanoo ci Peres ñoo di ñoom Esron mi sos làngu Esroneen ñi, ak ñoom Amul mi sos làngu Amuleen ñi.
¶ Petaya ma baayam di Mesesabel mu bokk ci askanu Sera doomu Yuda moom la Buur dénkoon mboolem mbir yi soxal mbooloo mi.
Kenn ci mag ñi ne ma: «Bul jooy. Ma ne, Gayndeg giirug Yuda, njebbital Buur Daawuda daan na. Mooy ubbi téere beek juróom ñaari tayoom.»