TSK

TSK · Genesis 47:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Firawna nag tudde Yuusufa Safnat Paneya, may ko jabar Asnat doomu Potifera ma doon sarxalkat ca dëkk ba ñuy wax On. Yuusufa doxe ca tegoo kilifteefu Misra gépp.

Noonu la Yuusufa tërale loola, def ko dogalu yoon ca suufu Misra, te loolooy wéy ba tey jii: juróomi céri meññeef mu ne, Firawnaay moom benn ba. Waaye suufi njiiti diine ya ca bokkul, Firawna amu ca dara.

Ezra 7:24 TSK

Nu ngi leen di xamal itam ne képp kuy sarxalkat mbaa ab Leween, mbaa mu dib jàngkat mbaa fara bunt, mbaa mu di liggéeykatu kër Yàlla gi, mbaa surga buy liggéey ci kër Yàlla googu, du galag bu ñu ko saña teg mbaa njotu bopp mbaa ab juuti.

¶ Ki ñuy jàngal kàddug Yàlla nag war naa sédd ki koy jàngal ci mboolem alalam.

¶ Mag ñiy jiite mbooloo mi bu baax nag, nañu leen yellale ag njukkal ñaari yoon, rawatina ñi boole coonoy waare ak njàngle.