TSK

TSK · Genesis 6:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Gannaaw ba loolu amee Aji Sax ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge.

¶ Keroog bés boobu la Nóoyin ànd aki doomam yu góor, Sem ak Xam ak Yafet, ak soxnaam ak ñetti soxnay doomam yooyu, ñu dugg ca gaal ga,

«Man ci sama wàllu bopp, kóllëre gi ma fas ak yaw mooy lii. Dinga nekk maamu xeet yu baree bare.

Waaye sama kóllëre nag, Isaaxa laa koy fasool, moom Isaaxa, mi Saarata di am, nëgëni déwén.»

¶ Ngëm la Nóoyin dégge waxyub Yàlla bu jëm ci lu kenn gisagul woon, te ragal Yàlla la sàkke gaal, ngir musal njabootam. Ngëmam it la tiiñale àddina, ba ab céram di njub gi ngëm di maye.

ndegam àddina sa woon it Yàlla jéggalu ko, xanaa Nóoyin ma daan waare njekk tey kenn ci juróom ñetti nit ña mu musal, ba mu walalee mbënn ma ci àddinay nit ñu gëmadi;