Yàlla nag sàkk dénd wi, xàjjalee ko ndox yi féete dénd wi suuf ak yi ko féete kaw. Mu daldi nekk noona.
TSK
TSK · Genesis 7:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bëti ndox ya ca xóote ya dafa taxaw, bunti ndoxi asamaan tëju, taw bi dal.
Jaraaf ja daan ànd ak Buur saa su ne àddu ca ne góoru Yàlla ga: «Ma ne, su Aji Sax ji ubbi woon sàqi asamaan sax, ndax man naa tax loolu am?» Mu ne ko: «Dinga ci teg sa bët déy, waaye doo ci lekk.»
Nit a ngi gas ay xunti fu soreeki dëkkuwaay, di sandaamtalook a jaayu fu kenn newul, te tànk jaarewu fa.
Ana ku xareñ ba waññ niir yi? Ak kuy jolal mbuusi asamaan,
Yaa fettaxal fii bëti ndox akum wal, ŋiisal dex yu masa wal.
ak ba muy teg niir ya fa kaw, ak ba muy dooleel ndoxi xóotey géej,
Suuf daa loroo loru, fetta fett, salfaañoo salfaañu.
Bu àddoo ndoxum asamaan riir, mu yéegey niir fa cati àddina, riddee ngelaw fa dencam ya, daldi melax, taw.
Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, kiy laal suuf, mu ne soyox seey, mboolem lu ci biiram di jooyoo; suuf fuddoondoo ni dexu Niil, dellu rës ni dexu Misra.