¶ Ci kaw loolu Kayin séq ak rakkam Abel wax. Ba mu ko defee ñu dem ca àll ba, Kayin dal ci kaw Abel, bóom ko.
TSK
TSK · Hebrews 11:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji ne ko: «Kon nag ku la rey, yaw Kayin, dina jot juróom ñaari yoon lu ko raw.» Ba loolu amee mu sàkkal Kayin màndarga, ba ku ko gis du ko rey.
Ci kaw loolu sawara bawoo fi Aji Sax ji, tàkk ca kaw sarxalukaay ba, xoyom saraxu rendi-dóomal ba ak nebbon ba. Naka la mbooloo ma mépp gis loola, daldi sarxolle, ba noppi dëpp seen jë fa suuf.
Ñi ñu jiitoo lay xamal, wax la, tibbe seen xol yii kàddu, dénk la:
Saraxu nit ku bon ñaawtéef la, rawatina bu ci jubloo lu bon.
La dale ca deretu Abel ba ca deretu Sàkkaryaa, ma ñu rey ca diggante sarxalukaay ba ak bérab bu sell ba, maa leen ko wax déy, dees na ko topp niti tey jii.
Ndax ci yoonu Musaa sax, deret lees di setale daanaka lépp, te bu deret tuuruwul, njéggal amul.
Yeena àgg fa Yeesu, Rammukat bi dox kóllëre gu yees gi, yeena àgg fa deret jiy setal tuuroo, te kàddug deret ja gëna neex kàddug deretu Abel ga jiboon.
¶ Ngalla ñii! Ñoo jaare yoonu Kayin; ñoo lajj, topp Balaam cig réeram ngir ag peyoor; ñoo diiŋat ba sànku ni Kore.