TSK

TSK · Hebrews 2:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci wàllu parluy Israyil, benn ay génn ci ñaar téeméeri gàtt yu ne, gàtt yooyu ñeel saraxi pepp, ak saraxi rendi-dóomal, ak saraxi cant ci biir jàmm ngir njotlaayal askan wi. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

Noonu it ngay def ca juróom ñaareelu fanu weer wa, ngir daboo ko nit ku jàdd yoon te yégu ko mbaa teyu ko. Su ko defee ngeen def njotlaayal kër Yàlla gi.

Ndegam ba ñu dee ay bañaaley Yàlla lees nu jubalee deewug Doomam, ñaata yoon lees nuy gënatee musale ag dundam, gannaaw ba ñu nu jubalee ak Yàlla?

Loolu lépp ci Yàlla la jóge, moom mi nu jubale ak boppam ci Almasi, te moo nu sas, ngir nuy waare juboo googu.

Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam.

Yeesu miy sellal nit ñi, moom ak ñi muy sellal, ñoo bokk lenqe, te moo tax Yeesu rusu leena wooye ay bokk.

Ku wóor la woon, ñeel ki ko tabb, noonee Musaa wóore woon ci mboolem waa kër Yàlla.

¶ Gannaaw nag am nanu kilifag sarxalkat bu mag bu jàll ba biir asamaan, te mooy Yeesu Doomu Yàlla, nanu ŋoy ci yoonu ngëm wi.

Ndax kat yoonu Musaa, ay nit ak seenug néew doole la fal ay sarxalkat yu mag. Waaye kàddug ngiñ li topp ci yoon wi, moo fal sarxalkat bu mag, Doom ji ñu matal sëkk ba fàww.