TSK

TSK · Hebrews 2:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 41:1 TSK

Wii rab, yaakaar koo jàpp nax sa bopp la; bu nee jaas, nga jóoru.

Yaa def nit mu yées malaaka yi as lëf, te yaa ko kaalaa teraangaak daraja,

ndax «Lépp la Yàlla di jébbal Almasi, teg ko fi ron ndëgguy tànkam.» Waaye bu Yàlla nee, «lépp la koy jébbal,» bir na ne moom mi ko jébbal lépp, bokku ci.

Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur,

¶ Ndax kat du ci kilifteefu malaaka yi la Yàlla teg àddinay ëllëg ji nuy wax,

tukkee itam fa Yeesu Almasi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki jëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqlikook kilifteefu sunuy bàkkaar,

¶ Ma xoolaat, daldi dégg baati malaaka yu bare, ñu yéew ngàngune mi ak bindeef yi ak mag ñi, seen lim di ay junni, ba ci junniy junni.