TSK

TSK · Hebrews 3:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Man, Aji Sax ji, maay seen Yàlla ji leen yékkatee réewum Misra. Ŋaleen ŋafeet, ma reggal leen.

Mooy sunu Yàlla, nuy xeet wi muy foral, diy gàtt ciy loxoom. Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom

Liggéey boo gis, liggéeyal; def ci loo man. Ndax muy jëf, di doxalin, di xam-xam, di manoore, dara amu ci njaniiw, ga nga jëm.

Sàkkuleen Aji Sax ji bi ngeen koy mana gis, wooleen ko bi muy jege.

Acts 1:16 TSK

«Bokk yi, Mbind mi moo waxe woon Noo gu Sell gi lu jiitu, ci gémmiñu Daawuda, wax ju jëm ci Yuda mi jiite nit ña, ba ñu jàpp Yeesu. Mbind moomu nag fàww mu sotti.

¶ Nun ñi bokk ci liggéey bi nag, noo leen di ñaan ngeen baña nangu yiwu Yàlla ci neen.

Waxees na ne: «Bésub tey jii bu ngeen déggee baatam, buleen të na woon ca fippu ga.»

Noonu la Noo gu Sell gi firndeele ne yoon wu maye dugg ca bérab bu sell baa sell feeñagul woon, te fekk néeg bu jëkk ba di taxaw ba tey.

Ndax kat du genn kàddug waxyu gu masa soqikoo ci coobarey nit, waaye ci xiirtalub Noo gu Sell gi la aw nit daan waxe waxyu bu bawoo fa Yàlla.