Ñeengokat ya ne Firawna: «Lii de Yàlla rekk a ko man!» Teewul Firawna wéye të rekk, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon.
TSK
TSK · Hebrews 3:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu amee Aji Sax ji ne Musaa: «Ba kañ la ma askan wii nara xarab? Ba kañ lañu may gëmadi, ak firnde yi ma def ci seen biir yépp?
Buleen seetlu seen Yàlla Aji Sax ji, na ngeen ko seetloo woon ca Maasa.
Ana lu jar ngeen di jaay dëgër bopp ni waa Misraak Firawna? Ba leen Yàllay Israyil torxalee, bàyyiwuñu bànni Israyil, ñu dem seen yoon?
¶ «Sunu maam yooyu kay ñoo mujj fuuy, sajju loos, ba sàmmuñu say santaane.
Ñoo diiŋate Yàlla xol, di xemmem ñam wu bakkane.
di ŋaf-ŋafi ca màndiŋ ma, di diiŋat Yàlla ca àll ba.
Ku ñuy àrtu, nga të ticc, dangay jekki yàqu, ba wees am paj.
Waaye waa kër Israyil duñu la nangoo déggal, ngir nanguwuñu maa déggal; ndax waa kër Israyil gépp a dëgër bopp te dërkiis.
¶ Teewul ñu baña déglu, të ticc, fatt seeni nopp, ngir baña dégg.
Ñenn ña nag të ticc, baña gëm, di ŋàññ Yoon wi ca kanam mbooloo ma. Ba loolu amee Póol bàyyi leen, daldi berook taalibe ya, bés bu nekk muy diisoo ak ñoom ca kërug jàngukaay gu Tiranus.
Bunu wut itam Almasi, ni ko ñenn ci ñoom wute woon, ba tax ay jaan rey leen.