TSK

TSK · Hebrews 6:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Su liir wi delloo tegu ci biir néeg bi gannaaw bu ñu teggee doj yi, xeet biir néeg bi, ba raax ko,

Ci kaw loolu mu yékkati kàddug ñaanam, ne: «Kàddug Balaam a ngi, doomu Bewor, kàddug waa jiy boroom ngis,

¶ «Aw rab wu bon, bu jàppee nit ba génn ko, day wër bérab yu fendi, di wut fu mu nopploo, te du ko gis. Su ko defee mu ne: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.”

Ba loolu amee mboolem gëmkati Yawut ya ànd ak Piyeer, waaru ca na mayug Noo gu Sell gi tuuruwaalee ca xeeti jaambur ña,

Acts 15:8 TSK

Yàlla, mi xam xolu nit nag moo seereel jaambur ñi, ba mu leen mayee Noo gu Sell gi, ni mu nu ko maye nun itam.

¶ Su ma doon làkk làkki nit ñi, ak yu malaaka yi sax, te jëfewuma genn cofeel, jóolóoli bu xumb doŋŋ laa, mbaa tëggum weñ muy riir.

Ki leen di may Noo gi, tey sottal ay kéemaan ci seen biir, ndax li ngeen sàmm yoon moo tax mu di ko def, am li ngeen dégg, ba gëm moo tax?

¶ Xibaaru jàmm boobu lañu ma def ab jawriñam, te Yàlla, ciw yiwam, moo jëfe manooreem, ba jagleel ma boobu cér.

Bul sàggane may gi ci yaw, te di lu ñu la baaxee ag kàddug waxyu gu ànd ak tegeb loxo, ba la mag ñi defaloon.

¶ Alegsàndar tëgg bi def na ma lu bon lu réy, waaye Boroom bee koy fey jëfam.

¶ Gannaaw bu nu xamee xéll liy dëgg ba noppi nag, su nu bàkkaaratee te di ko tey, su boobaa ab sarax bu far yooyu bàkkaar amatu ci.

Moytuleen balaa kenn di ñàkk yiwu Yàlla. Moytuleen bala ab reenu wextan di fëll, di lëjle, ba rax mbooloom lëmm.

¶ Ndax kat gannaaw bu ñu xamee bu baax sunu Boroom, sunu Musalkat Yeesu Almasi, ba rëcc sobey àddina, bu ñu ca sóobuwaatee ba mu man leen, su boobaa seenug muj moo yées seenug njàlbéen.