Genesis 12:2
TSK
ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, barkeel la, màggal sa tur, ngay buntu barke;
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, barkeel la, màggal sa tur, ngay buntu barke;
Te tuddatuloo Ibraam; léegi yaa di Ibraayma (mu firi Maamu ñu bare), ndax maa la def ngay maamu xeet yu baree bare.
Yàlla daldi fasook Ibraayma kóllëre gu mu màndargale xaraf. Moo tax Ibraayma xarfal doomam Isaaxa, ba mu juddoo ba am juróom ñetti fan; Isaaxa, Yanqóoba, Yanqóoba, fukki maam yaak ñaar.
Noonu la Mbind mi indee ne: «Maa la def ngay maamu xeet yu bare.» Ibraayma mooy sunu maam fi kanam Ki mu gëm, te muy Yàlla miy delloo ñi dee, bakkan, tey woo lu nekkul, mu doon lu nekk.
Mbind ma daldi sotti, na mu dikke woon ne: «Ibraayma moo gëm Yàlla, ñu waññal ko ngëmam ag njub,» ba ñu di ko wooye xaritu Yàlla.