Su ñu muusoon, xalaat ci lii, ba xam nu ñuy mujje.
TSK
TSK · Hosea 7:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yàlla déy a ngi ne jàkk ci jaar-jaari nit ki, di xool bépp jéegoom.
Mu naa ca xelam: «Yàlla fàtte na, dummóoyu na, du xoolati.»
«Yeen fàttekati Yàlla yi, déggleen lii, bala maa fàdd te kenn du wallu.
Lu waay jëf, Aji Sax ji gis, di xool mboolem fu mu jaare.
Xalam yaak tabala yaak toxoro ya jolli, biiñ xelli ca xawaare ja. Seetluwuñu sax li Aji Sax ji def, xooluñu li mu jo loxoom.
Ku mel nii du délloosim xelam, ba xam, ràññee ne: «Xaaju matt mi laa taal, lakke mburu, wàjje yàpp, lekk; mu des, ma di ko sàkke lu seexluwu lii? Ab dogu bant laay sukkal?»
«Sa jëfin ak say jëf a la yóbbe lii, sa musibaa ngook, wex la xàtt, di dagg sa xol.»
Samay bët a ngi ne jàkk déy ci seeni jëf. Dara umpu ma ci. Seeni ñaawtéef, dara rëccu ma ci.
¶ «Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw yeena fàttliku seen ñaawtéef, seeni tooñ ne fàŋŋ, seeni bàkkaar fés ci seen jëf jépp, gannaaw yeena ñaaw ñaawtéef gu ñu leen di fàttlikoo, dees na leen jàpp.
Ñooy sarxe jur gi ñu may jooxeel, lekk yàpp wi, Aji Sax ji buggu ci dara. Maay bàyyi xel ci seen ñaawtéef, mbugale leen seeni moy, te ñoom Misra lañuy dellu.
Aji Sax ji giñ na ci turam wi askanu Yanqóobay damoo, ne: «Duma fàtte mukk lenn ci seeni jëf.
Moo tax buleen àtte lenn te jotul, lu jiitu Boroom biy dikk. Moom mooy leeral li làqoo ag lëndëm, di làññi mébéti xol. Su boobaa ngërëm la ku nekk yelloo, fa Yàlla lay bawoo.