TSK

TSK · Isaiah 11:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Fekk na Yosuwe doomu Nuun feese xel mu rafet, ndax Musaa moo tegoon ay loxoom ci kawam, bànni Israyil nag déggal ko, di jëfe na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.

«Xool-leen sama jaam bi ma yor, sama tànnéef, sama soppey xol, ci kawam laa teg samag noo, te mooy dogalal xeet yi yoonu àtte.

«Man nag, lii mooy sama kóllëreek ñoom: Sama xel mi tegu fi sa kaw, ak sama kàddu yi ma yeb ci sa gémmiñ, lenn du ci teqlikook sa gémmiñ ak sa gémmiñu askan, ak sa gémmiñu askanu askan, tey ak ëllëg.» Aji Sax jee ko wax.

ak ni Yàlla ànde ak Yeesum Nasaret, ba jagleel ko pal gu mu dogale Noo gu Sell geek xam-xam bi mu ko sotti, muy wër, di def lu baax, di faj mboolem ñi Seytaane notoon.

ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet, ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax.

ngir ngeen gëna am fit, mànkoo ci biir cofeel, te géeju ci gis-gisu xol bu leer nàññ te wóor, ba mana daj dëgg, mbóotum Yàlla, miy Almasi ci boppam.

¶ Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la jëkka def, teg ci ànd ak jàmm, akug dal. Day taxa neexa jubool, feese yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-làqu akug jinigal.