Mbugalu Yàlla kat laa ciy ragal, te màggaayam xajul ci man.
TSK
TSK · Isaiah 2:10
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ana ku xam sa dooley mer ak sa xadar ju raglu?
Ku ci nekk di àddu, naan moroom ma: «Kee sell te sell te sell, keey Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, àddina sépp a feese ag leeram!»
Waaye ñu ngii di xeet wu ñu futti, sëxëtoo; ñépp tëje ciy pax, dence ci këri tëjukaay, ñu doon alalu xare fu leen kenn dul xettlee, xanaa ñu di leen sëxëtoo, te kenn du ne ñu delloo leen.
Waaye Aji Sax jeey Yàlla dëgg. Mooy Yàlla jiy dund, di buur ba fàww, xadaram gësëm àddina, meram man xeet yi.
Ma xamal leen nag ki ngeen wara ragal: kiy rey ba noppi, am sañ-sañu sànni ca sawara sa, kooku déy laa leen ne, ragal-leen ko.
Ñooñu lees di mbugale sànkute gu sax dàkk, fu sore Boroom bi, sore teddngay manooreem,
Ña ngay woy woyu Musaa jaamu Yàlla ba, ak woyu Gàtt bi, naan: «Yaw Boroom bi Yàlla Aji Man ji, yaa réy te yéeme ay jaloore. Yaw Buuru askan yi, yaa jub te dëgguy doxalin.