TSK

TSK · Isaiah 2:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ma ne gawar a ngii, war watiiru ñaari fas. Nee: “Daanu nañoo, Babilon daanu na, jëmmi tuuram yépp tasaaroo fi suuf!”»

Lii nag, nangeen ko siiwal: «Seen yàlla, yi sàkkul asamaan, sàkkuñu suuf, ñooy sànku, jóge fi suuf ak fi asamaan tiim.»

Fu ngeen mana sance, seeni dëkk ay gental, seen jaamookaayi tuur wéet, seeni sarxalukaay yàqu, gental, seen kasaray tuur rajaxoo ba jeex, seen suurukaayi tuur màbb, seeni liggéey réer.

Dootuñu sobeel seen bopp ci ay kasaray tuur, ak seen jëf ju siblook mboolem seeni tooñ. Maa leen di walloo ci mboolem seen ñàkk kóllëre. Ma setal leen, ñu doon sama ñoñ, ma doon seen Yàlla.

«Doom aadama ak mala, njanaaw ak jën laay buub, ak luy fakktale, booleek ñu bon ñi. Maay dagge doom aadama fi kaw déndub suuf.» Aji Sax jee ko wax.»

¶ «Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, «Turi xërëm laay dagge ci réew mi, ba deesatu leen fàttliku. Yonent yeek xelum xërëmtu it, maa koy tukkal ci réew mi.