TSK

TSK · Isaiah 20:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu amee Daawuda walbatiku, dugg biir këram, ngir ñaanal waa këram. Soxnaam Mikal doomu Sóol génn dajeek moom, ne ko: «Buuru Israyiloo, yaaka teral sa bopp bésub tey jii! Nga futteeku tey jii fi kanam jigéen ñiy sa jaami jawriñ yi, mbete nit ku tekkiwul dara!»

Job 1:20 TSK

¶ Ba mu ko defee Ayóoba jóg, ne tareet mbubbam, ba noppi watu nel, di ko ñaawloo. Mu daanu fi suuf, sujjóot,

¶ Aji Sax ji da maa wax ne ma: «Demal jëndi njiitlaayu lẽe, nga woddoo ko, te bu ko ndox laal.»

Man nag àppal naa la limu fan yu tembook limu ati ayu waa kër Israyil, muy ñetti téeméeri fan ak juróom ñeent fukk (390) yooy tegoo ayu waa kër Israyil.

Buleen tàggook kaala, buleen tàggooki carax. Buleen yuuxu, buleen jooy. Waaye dingeen jeex tàkk ndax seeni ñaawtéef, ngeen ànd di binni.”

Yeen waa Safiir, jàll-leen, ak gàcce ak yaramu neen. Waa Caanan sañuñoo génn, te wall du bawoo fa waa Bet Eccel, ñay jooy seeni néew.

Dinaa may nag sama ñaari seede yi, ñu biral waxyu diiru junni ak ñaar téeméeri fan ak juróom benn fukk (1 260) yu ñuy sol ay saaku, di ko toroxloo.»