TSK

TSK · Isaiah 24:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bésub keroog booba, ku bew bay regeju mooy detteelu, sagub nit sàggiku, Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.

Wóoy ngalla Efrayim, kaala gu yànj ga ay màndikatam di sagoo! Taaram bu yéeme baa koy réer, ni tóor-tóor yu wow, te ma nga toŋ ca coll, wa ña biiñ man dëkke, fa tiim xur wu nangu wa.

Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.

Ba kañ la réew mi naa sereŋ, gàncaxu tooloo tool di lax? Rabu àll ak njanaaw a ngi sànku ngir mbonug ñi fi dëkk te naan: «Moom xoolul sunu muj!»