TSK

TSK · Isaiah 3:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye su ngeen jëfewul noonu kat, yeena moy Aji Sax ji, te xamleen ne seenug moy dina leen dab.

Aji Sax ji nee na: Dama ne, dinaa wàcce lu bon ci sa kaw, fàllas say sët, ba faagaagal ci digg Israyil kuy taxaw, colal, te bokk ci yaw Axab, muy gor, di jaam.

Loo def mu àntu: nga mel ni garab gu saxe walum ndox, bu jotee meññ, te xob wa du lax.

Fey leen seen liggéey, seen kemu jëf ju bon. Jox leen seen añu jëf, yool leen seen yelleef.

Yaw boroom làmmiñu njublaŋ, ana lu ñu lay añale ak lu ñu lay dolli?

Ku jub, jot sa yool ci kaw suuf, moykat beek soxor bi it daw raw.

Ku bon, du am lu baax, fanam du màgg ni ker, ndax wormaalul Yàlla.

Jàmm,» la Aji Sax ji wax ne, «du ñeel ñu bon ñi.»

Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Ma ne sama jaam ñeey lekk, yeen ngeen nekke xiif. Ma ne sama jaam ñeey naan, yeen ngeen nekke mar. Sama jaam ñeey bànneexuji, yeen, ngeen nekke gàcce.

¶ «“Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Ni nga def rekk ni laay def ak yaw, mi sofental kàddug ngiñ, fecci kóllëre.

Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.