¶ Gannaaw loolu Buur Daawuda dem bay jub dëkk ba ñuy wax Baxurim rekk, yemook jenn waay ju bokk ci waa kër Sóol. Ma nga tuddoon Simey doomu Gera. Naka la waa ja ne tëll, jubsi, di tifaar Daawuda ay saaga,
TSK
TSK · Isaiah 3:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Tey ñi may diijoo ngii, te ñoo ma féete ndaw, seeni baay a tekkiwuloon tus, ba ma siide leena jël, ñuy sàmmandook samay xaj.
Wóoy wii xeetu moykat, wii askan wu diisu ñaawtéef, mii njurum defkati mbon, yii doomi yàqute! Ñoo wacc Aji Sax ji, ñoo teddadil Aji Sell ju Israyil, dëddu ko.
Nit ñaa ngi màtte ndijoor, te doyaluñu, di xàmpe càmmoñ te suuruñu, ku nekk di yàpp sa mbokk:
Maay xiir Misra ci kaw Misra, kii song mbokkam, kii song xaritam, ab dëkk jógal ab dëkk, diiwaan jógal diiwaan.
«Yaw xooloo, xalaatoo lu moy loo jariñoo, ak noo tuure deretu jaamburu Yàlla, di fitnaale ak a lore?»
Alalu ger, ñu jël fi sa biir, ngir lor ay bakkan. Ndollant ci kaw tegandaay, nga jël feyeekoo bor, di wute alal sa àqu moroom. Man nag, nga fàtte ma. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Dama ne: «Ngalla dégluleen yeen njiiti Yanqóoba, yeen kilifay kër Israyil! Xanaa du yeena wara xam yoon?
Ngor a jeex ci réew mi, njub tumurànke ci nit ñi. Ñépp, ku ñu tuur deretam lañuy tëru, ku nekk, mbokkam lay fiir.
Doom ju góor a ngi dofloo baay ba, ju jigéen ja jógal ndey ja, jabar jógal ndeyu jëkkër ja, nooni nit ki di waa këram.
Dootuma yërëm waa réew mi (/àddina) déy,» Kàddug Aji Sax jee! «Maa ngii di teg doom aadama yi, ku nekk ci loxol moroomam, ak ci loxol buuram, ñu not réew mi, te duma leen xettli ci seen loxo.»
Yeen nag ngeen di teddadil néew doole yi! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di noggatu, di leen diri ba fa mbaxana dee benn?