Ku gasal nit am yeer, yaa cay daanu; ku béraŋu doj, ngir tance, yaay tancu.
TSK
TSK · Isaiah 3:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Wóoy ngalla ñiy ràngooy buum, di diri ñaawtéefi neen, ràngooy goj di diri seeni tooñ.
ana ku ngeen di ñaawal? Ana ku ngeen di ŋóobi, ak di ko kókkali? Xanaa dungeen doomi moykat, di askanu workat,
Waaye yéeneb waxyu bu Aji Sax ji, buleen ko fi tuddati. Jooju wax déy, yenu boroom lay doon. Ndax dangeena been sunu kàddug Yàlla, Yàlla Aji Sax jiy dund, Boroom gàngoori xare yi.
«Ku ñuy wax Mise, dëkk Moreset, doon na biral waxyu ca jamonoy Esekiya buurub Yuda. Daa waxoon waa Yuda gépp ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngooru xare yi dafa wax ne: Dees na gàbb Siyoŋ nib tool, Yerusalem diy tojit, jale; tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.”
Ma jekki gis foofa leeru Yàllay Israyil ca melokaanam, ma ma ko gise woon ca joor ga.
Mu ne ma: «Yaw nit ki, du yaa gis lii? Moonte tojaange gi waa kër Yuda di def fii doyu leen. Xanaa ñuy wasaare fitna ci réew mi, di gëna yékkati sama xol. Xoolal! Ñu ngooguy def jëfi yéefar, jël caru garab, di fóon.
Israyil, ag reewandeem a ko tiiñal, Israyil ak Efrayim ñooy fakktaloo seenug ñaawtéef, Yuda it ànd ak ñoom fakktalu.
Kon nag dees na gàbb Siyoŋ nib tool, Yerusalem googu diy tojit, jale, tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.
«Kàddu yu ñagas ngeen teg ci sama kaw,» Aji Sax jee ko wax. «Te yeena ne: “Ana kàddu yu ñu la waxal”?
Am danuy yékkati fiiraangey Sang bi? Danu koo ëpp doole?