Yàlla nag teg leen ci asamaan, di ca leeral suuf,
TSK
TSK · Isaiah 45:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
dox diggante dalu waa Misra ak dalu bànni Israyil. Niir waa nga lëndëme genn wet, wet ga ca des di leer ca guddi ga, ba tax guddi ga gépp benn dal manula fekki moroom ma.
Mu ne ko: «Waxi jeeg bu dof daal ngay wax, yaw! Du Yàlla da nuy may lu baax, nu jël? Kon kay bu nu mayee safaan ba it, nu wara jël.» Ci biir loolu lépp Ayóoba bàkkaarul ciw làmmiñam.
Bu Yàlla nee cell, ana ku koy ŋàññ? Bu làqee kanamam, ana ku koy niir? Xeet yeek nit ñi la boole tiim,
Aji Sax jeey kàttanal ñoñam, di barkeele jàmm ñoñam.
Du penku, du sowu, te du màndiŋ ma la daraja di jóge.
Xoolal ci li Yàlla def: Ana ku mana jubbanti lu mu dëngal?
¶ Moona moom it xareñ na, mane na safaan, te du fommi digeem. Kuy def lu bon, mu dal ci waa këram; kuy def lu ñaaw, mu song ay wallam.
Teral-leen seen Yàlla Aji Sax ji, bala moo lëndëmal, ngeen tërëfe tundi timis, di séentu leer, mu lëndëmal ba mu ne këruus, fatt taraj
Aji Sax ji dafa wax, moom mi dogal jant di leeral bëccëg, dogal weer ak biddiiw di leeral guddi, yëngal géej, kiy gannax yi riir, kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
Muy lu baax, di lu aay, du Aji Kawe jeey àddu, amal?
Mboolem leeri asamaan laay giimal fi sa kaw, ba teg lëndëm fi sam réew. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Bu liitu xare jibee, waa dëkk ba du tiit a? Am aw ay dina dab ub dëkk te du Aji Sax ji?
Sàkkuleen Aji Sax ji, ba dund. Lu ko moy mu ne jippét ci kaw askanu Yuusufa, lakk waa Betel lakk gu dul fey.
Noonu it lañu sottale mboolem li nga dogale woon sa loxo ak sa coobare.
gépp may gu baax, ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.
Ñooy gannaxi géej gu sàmbaraax, di gëq seen puuriti gàcce; ñooy biddiiw yu fàq di taxawaalu, te lëndëm gu ne këruus di cér bu ñu leen sédde ba fàww.