Ba Firawna yónnee, ba nemmiku mbir ma, xam na ne lenn deewul ca juru bànni Israyil. Teewul mu të ticc ba tey, baña bàyyi mbooloo ma, ñu dem.
TSK
TSK · Isaiah 48:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ba ngeen dugg ca réew mooma meew maak lem ja tuuroo. Waaye duma ànd ak yeen, lu ko moy dinaa leen faagaagal ci yoon wi, ndax askan wu dëgër bopp ngeen.»
Kon nag nangeen dogoo seen xol te bañatee sajju loos.
¶ Teewul ñu të ticc, sajju loos ni seen maam ya gëmuloon seen Yàlla Aji Sax ji.
Naka lañu am noflaay, daldi dellu ci def lu bon fi sa kanam. Nga wacc leen nag ca seen loxoy noon, ñu moom leen. Ba ñu delloo woo la wall, yaa leen dégge fa asamaan, ba xettli leen ay yooni yoon ci sa yërmande ju réy.
te baña roy seeni maam; maas gu të woon te déggadi, ñu ñàkk pastéef te sàmmuñu kóllërey Yàlla.
Wii xeet kat ay fippukat lañu, yii doom a diy fen-kat te nanguwuñoo sàmm yoonu Aji Sax ji!
Moo tax waame aje, taw yiy mujje dikkul. Teewul ngeen dëgër bët nib gànc, ñàkk gàcce!
Waaye dégluwñu, teewluwñu ma, xanaa sajju loos, di bon, ba yées seeni maam.
Ci nit ñu dëgër bopp te dërkiis laa lay yónni. Wax leen, ne leen: “Lii Boroom bi Aji Sax ji da koo wax.”
Waaye ba mu bewee, të ticc bay réy-réylu, dañu koo jàllarbee ca nguuram, nangu ndam la,
¶ «Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!
Waaye bés bu nekk deeleen soññante li feek muy bésub tey agum, bala bàkkaar a nax kenn ci yeen, ba mu mujj dërkiis.