TSK

TSK · Isaiah 61:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su boobaa ci fukki fan ca juróom ñaareelu weer wa nangeen wal-lu ag liit fépp. Bésub Njotlaay boobu nangeen wal ag liit ci seenum réew ba mu daj.

¶ «Atum Yiwiku moomu ci ngeen di delloo ku nekk suufam.

Mooy mëdd ndee ba fàww! Boroom bi, Aji Sax jeey fompe gépp kanam rongooñi boroom. Buumi gàccey ñoñam it, moo koy doge fépp ci àddina. Aji Sax ji kat wax na ko.

Ku fitam rëcc, ne leen ko: «Dëgërlul te bul tiit. Sa Yàllaa ngii di la feyul, ba yool say noon. Moom mooy dikk, wallusi la.»

Man ci sama bopp maa leen di dëfal. Ana lu ngeen di ragal ci nit kuy dee, doom aadama ju bokk akum ñax aw demin?

Moo sol kiiraayal njekk, mbaxanawoo mucc, solati yérey mbugale, làmboo turkib xéraange.

Bésub mbugal laa mébétoon, te atum njot teew.

Yeenay teewe lii, seen xol tooy, seen yaram leqliku ni ñax mu yég nawet. Dooley Aji Sax ji la ay jaamam di xam, te am sànjam la ay noonam di xam.

Waaye bésub keroog déy, Boroom bi Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko moom, muy bésub feyu bu muy feyey noonam. Saamar suur suux, màndee deret. Boroom bi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi mooy rendee réewum bëj-gànnaar ab sarax, feggook dexu Efraat.

Luke 6:21 TSK

Ndokklee yeen ñi xiif tey, nde dingeen regg. Ndokklee yeen ñiy jooy tey, nde dingeen ree.

Ndax janti mbugal lay doon, ngir sottal mboolem lu ñu bindoon.

moom mi nuy dëfal ci sunu jépp njàqare, ngir noonu nu jote nun ci sunu bopp, ndëfalaay lu nu dëfaloo fa Yàlla, nu man koo dëfale ñi nekke mboolem xeeti njàqare.

Ñoo nuy aaye nu àgge jaambur ñi dul Yawut, kàddu gi leen di musal. Noonu lañu matale seen jóorub bàkkaar yi ñu nekke naka jekk, waaye am sànj a leen mujj dab.

¶ Sunu Sang Yeesu Almasi ci boppam, ak Yàlla sunu Baay, mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk, ak yaakaar ju wér,