¶ Aji Sax ji ne ko: «Maa ngi nii di fas kóllëre ak yeen. Ci sa kanam mbooloo mépp laay def ay jaloore yu kenn masula amal ci àddina sépp, ak ci askan yépp, te mbooloo, mi nga nekk ci seen biir mépp ay gis jaloorey Aji Sax ji, jaloore ju raglu ji ma lay defal.
TSK
TSK · Isaiah 64:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Moo yelloo seeni kañ te mooy seen Yàlla, ji leen defal jaloore yeek kawtéef yooyu ngeen gisal seen bopp.
Ana askan wu mel ni Israyil sa ñoñ ci kaw suuf, wenn askan wu Yàlla dikk, goreel leen ngir def leen ñoñam, ba turam siiw? Yaa leen defal ay jaloore, yaa defal sam réew ay kéemaan ci sa kanam ñoñ ñi nga goreele fa Misra aki askanam aki yàllaam.
Neleen Yàlla: «Yaaka yéemey jaloore! Sa doolee bare, ba say noon rasu,
Céy Yàlla, yaa génn, jiitu sa mbooloo, daagu, dugg màndiŋ ma. Selaw.
ñu sottal ci seen biir firndeem ya mu waxoon, muy kéemaan ya ñu def ca réewum Xam.
Ni sawara di jafale boob, baxale ko am ndox, ni ngay xamalsee say noon, saw tur, ba yooyu xeet di lox fi sa kanam.
Kee taxaw, yëngal suuf; kee xoole, loxloo xeet yi, tund yu mag ya woon naka jekk rajaxoo, tundi cosaan yu ndaw ya maasaloo. Kii moo moom yooni cosaan yi.