TSK

TSK · Isaiah 65:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bésub keroog Boroom bi jooti loxoom ñaareel bi yoon, ngir jotaat ndesu ñoñam, wa des Asiri ak Misra, ak Pattros ak réewum Kuus, ak Elam ak Sineyaar, ak Amat ak biir duni géej ya.

ba sama bokk yi dëkke sancub jàmm, ci dëkkuwaay yu wóor, dal-lukaay yu dal xel.

Sa askan wépp ñu jub lañuy doon, te ñooy moom réew mi ba fàww. Ñooy sama njëmbat li ma jëmbatal sama bopp, sàkke leen samay loxo, ngir sama teddnga teew.

Duñu tabax moos, keneen dëkke; duñu jëmbat moos, keneen xéewloo. Sama ñoñ ay tollook garab yi fan, sama xejj yeey jagoo seenu ñaq.

¶ Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Daawuda du ñàkk mukk ku ko wuutu ci jalu Israyil.

Yaw suuf, maay doxloo nit fi sa kaw, muy waa Israyil sama ñoñ, ñu jagoo la, séddoo la, te dootoo sabab seenug deele.”»

te nga wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jëleji bànni Israyil ca biir xeet ya ñu fekki, dajalee leen wet gu nekk, délloosi leen seen suufas bopp.

Amos 9:11 TSK

«Bésub keroog maay yékkati mbaarum Daawuda mi joy, ba fattaat xar-xar yi, defaraat gent bi, tabaxaat ko na woon.

Yeen, jant yooyu laa leen di indi, jant yooyu laa leen di dajale, nde maa leen di defal aw tur ak teraanga fi biir mboolem askani àddina, maay tijji seen wërsëg, ngeen gis.» Aji Sax jee ko wax.

¶ Ci wàllu xibaaru jàmm bi, ay noon la Yawut ñi taxawe, te muy xéewal ci yeen ñi dul Yawut. Waaye ci wàllu dogal bi taamu Yawut ñi, ay soppe lañu, te seeni maam tax.