TSK

TSK · Isaiah 7:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ibraam dafa xàjjale mbooloom, dal ci kaw buur ya guddi, dàq leen, topp ci ñoom ba Koba, ca bëj-gànnaaru Damaas.

¶ Ba loolu amee Salmanasar buurub Asiri dal ca kaw réew ma mépp, dikk ba Samari, gaw ko diiru ñetti at.

Ezra 4:2 TSK

ñëw nañu ca Sorobabel ak ca kilifay kër ya, wax leen ne leen: «Danuy ànd ak yeen tabax ndax danuy topp seen Yàlla, ni yeen, te ca jamonoy Asaradon buurub Asiri, mi nu fi indi ba tey, Aji Sax ji lanuy defal sarax.»

Yéene bii ñeel na Damaas: Damaas a ngii, léegi mu noppee doon ab dëkk, xanaa ab jalu tojit;

Hosea 1:6 TSK

¶ Mu dellu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju jigéen. Aji Sax ji ne: «Tudde ko Lo Ruwana» (mu firi Ki ñu yërëmul), mu ne: «ndax dootuma yërëm waa kër Israyil, dootuma leen baal.