TSK

TSK · James 1:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Suuf nag daa maase woon te wéet, lëndëm muur ndox mu xóot mi, lale ca kaw, Noowug Yàlla di wër, tiim ndox mi.

Yuusufa ne ko: «Du ci man de, waaye Yàlla mooy baaxe Firawna pirim jàmm.»

Aji Sax ji ne ko: «Ku sàkkal nit gémmiñ? Kan mooy luuwal, di tëxal, di gisal mbaa muy gumbaal? Xanaa du man Aji Sax ji?

¶ «Kon nag Besalel ak Oliyab ak mboolem ñu xareñ ñi Aji Sax ji may xareñte ak déggin ngir ñu mana jëfe mboolem sas yi jëm ci liggéeyu bérab bu sell bi, ñoom ñépp nañu sottal lépp li Aji Sax ji santaane.»

Aji Sax ji nag wàcc ca biir niir wa, wax ak moom, daldi sàkk ca leer ga ca Musaa, sédd ca juróom ñaar fukki mag ña. Naka la leer ga dal ca seen kaw, ñu tàmbali di wax ay waxyu, benn yoon bu ñu tóllantiwul.

Buleen séentu asamaan, gis jant bi, mbaa weer wi, mbaa biddiiw yi, ak mboolem leeri asamaan, ba mu xiirtal leen ci di leen sujjóotal ak a jaamu, te seen Yàlla Aji Sax ji féetale yooyii, mboolem xeet yi asamaan tiim.

Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.

ndax Aji Sax jeey maye xel mu rafet, kàddoom di taxa xam, di dégg.

Maay bind leer, di def lëndëm. Maay indi jàmm, di def safaan. Maay Aji Sax jiy def lii lépp!

Du jant a lay leeralati bëccëg, te weer du la niital; Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa Yàlla jooju di sab taar.

¶ Dañeel ne Buur: «Buur, li nga laaj amul benn boroom xam-xam mbaa ñeengokat mbaa taryaax ak seetkat bu la ko mana xamal.

¶ Ba ñu déggee loolu lañu dal, daldi màggal Yàlla. Ñu ne: «Kon xeeti jaambur yi, ndeke ñoom it Yàlla may na leen ñu tuub, ba dund!»

Ndax Yàlla kat, ay mayam akub wooteem, lenn du ci toxu.

Ana ku la def nga gën ci nit ñi? Ana loo am lu ñu la joxul? Te ndegam dees la koo jox, ana loo koy puukarewoo, mbete lees la joxul?

Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leere ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi.

Ci ñoom lanu bokkoon nun ñépp itam; mas nanoo topp sunu bakkan, di jëfe lu sunu bakkan, ak sunum xel xemmem. Sunu bindu nit taxoon na noo yeyoo am sànj ni ñépp.

Moo tax ñu ne: «Moo yéeg fa kawa kaw, yóbbaale gàngoor gu mu jàppe xare, te moo séddale nit ñi ay may.»

Titus 3:3 TSK

¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.

Yeesu Almasi menn mi la woon démb ak tey ba fàww.

Moomu xel jógewul fa kaw, àddina sii la bokk, di yëfi bakkan, te di mbiri Seytaane.

Guddi du amati, te deesul soxlaati làmp mbaa naaj, ndax Boroom bi Yàlla moo leen di leeral. Te dañuy nguuru ba fàww.