Maa leen di noonoo ba seeni noon duma leen, seeni bañ yilif leen. Dingeen daw te kenn dàqu leen.
TSK
TSK · Jeremiah 39:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Aji Sax jeey def ngeen daanu fi seen kanami noon. Wenn yoon ngeen di dikke, song leen, waaye juróom ñaari yoon ngeen di awe, daw, te dees na leen seexlu ci mboolem nguuri kaw suuf.
Xarekati Yuda ya génn guddi daw. Fekk na waa Babilon gaw dëkk ba. Teewul ñu rëcc, jaare ca bunt ba ca diggante ñaari tata ya, ca wetu toolu buur. Cedekiya daldi wuti xuru Yurdan.
Seen njiiti xare yépp a bokk daw, ñu jàpp leen te taluñoo fitte. Seen njiit yi ñu gis yépp lañu jàpp, te ñu dawoon ba sore.
Ndax Boroom bi Aji Sax ji, Aji Sell ju Israyil dafa wax ne: «Délsi, dal-lu moo leen di musal. Ne tekk te wóolu maa leen di dooleel. Waaye yeena buggul!
Waaye soo jébbalul sa bopp kàngami buuru Babilon, dees na teg dëkk bi ci loxoy waa Babilon, ñu lakk ko ba mu jeex, te yaw doo leen rëcc.»
Sab ëmb ngay jëkka génne digg bëccëg ni ku jëm ngàllo, ñépp teg ci bët. Te yaw nga génn ngoon ni ku jëm ngàllo, ñu teg ci bët.
Rawtu dina réer ku gaaw, boroom doole du tala jariñoo dooleem, jàmbaar sax du mana rawale bakkanam.