TSK

TSK · Jeremiah 7:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Artu nga leen ndax ñu dellu ci saw yoon, teewul ñu bew, ba sàmmuñu say santaane, xanaa di moy sa àttey yoon yiy taxa dund képp ku ci sàmmu. Ñuy daŋŋiiral, sajju loos, bañ laa déggal.

Ana lu tax ba ma dikkee, kenn nekku fa? Ma woote, kenn wuyuwul? Damaa gàtta gàtt loxo, ba manumaa walloo? Am damaa ñàkk doole ju ma xettlee? Xanaa du maay gëdd géej, mu wow, maay defi dex màndiŋ, ndox tukki; jën ya mar, dee ba yàqu?

Man it maa leen di taamoo jox seeni mbugal, dikke leen tiitaange yi ñu yelloo, ngir maa woote, kenn wuyuwul, ma àddu, dégluwuñu ma. Xanaa di def lu bon lu ma ñaawlu, li ma buggul, ñu taamu ko.»

Moo kan laay waxal, àrtu ko ba mu déglu, yii boroom noppi paaxee tëë teewlu! Kàddug Aji Sax jaa ngii, mel ni lu ñu rus, lu ñu safoowul!

Artu naa àrtu seeni maam, dale ko ba ma leen génnee réewum Misra, ba tey jii ma jàppoo di leen àrtu, naan leen ngeen déggal ma.

Askan wu bon wii bañ maa déggal, të ticc di wéye seen coobare, di topp yeneen yàlla, di leen jaamook a sujjóotal, nañu mel ni njiitlaay lii amul benn njariñ.

dégguleen sama kàdduy jaam ñiy yonent yi may yónni ci yeen ay yooni yoon, ngeen tëë dégg,

Wonuñu ma kanam, xanaa gannaaw, te ma àrtu leen ay yooni yoon. Waaye ñoom dégluwñu, dégguñu yar.

Yónnee naa leen samay jaam, yonent yi, ay yooni yoon, ne leen: ‘Na ku nekk ci yeen dëpp yoonam wu bon, di def lu baax, baña topp yeneen yàlla, di leen jaamu, ndax ngeen dund ci réew mi ma leen jox, yeen ak seeni maam.’ Waaye teewluwleen ma, déggaluleen ma.

Yónnee naa leen ay yooni yoon mboolem yonent yi, sama jaam ñi, ne leen: “Rikk buleen def jëf ju siblu jii ma bañ.”

Lu ñu leen gëna woo, ñu gën maa sore. Ay tuuri Baal lañuy defal ay sarax, te ay xërëm lañuy taalal cuuraay.

«Ba ma wootee,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «wuyuwuñu; moo tax ba ñu wootee, wuyuwuma.