TSK

TSK · Joel 1:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Soo bañee bàyyi sama ñoñ, ñu dem kat, ëllëg dinaa wàcce ay njéeréer ci sam réew.

Njéeréer ya song réewum Misra mépp, sam déndu Misra wépp, ba mu fatt taraj. Lu ni tollu masula am, te dootu amati.

¶ Jiwu mu bare ngeen di yóbbu tool, te lu néew ngeen cay ame, ndax njéeréer yee koy wat.

¶ «Bu xiif amee ci réew mi, mbaa mbas, mbaa gàncax gi lakk, mbaa benaat xuural ko, mbaa mu diy njéeréer mbaa soccet, mbaa su dee congum seen noon ci seen dëkki réew mi, mbaa muy mboolem luy musiba ak mboolem jàngoro, su boobaa,

Mu àddooti, ay soccet dikk, di njéeréer yu wees ab lim,

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi giñ na ci boppam. Mu ne: “Maa leen di same ay nit niy njéeréer, ñu xaacu, song leen.”»

Joel 2:25 TSK

«Sama mbooloom xare mu réy, mi ma yebaloon fi seen biir, te ñuy njéeréer yeek seen tostan, ak salleer yeek soccet yi, maa leen di delloo ati mbey yi ñu leen lekkal.

Amos 7:1 TSK

¶ Am na bés Boroom bi, Aji Sax ji won ma am peeñu. Ndeke ma ngay sàkk naaxu soccet. Fekk na ñu góobal Buur, ba gàncax giy saxaat.

Maa leen di gëddal njéeréer, ba du leen yàqal meññeefum suuf, te reseñug tool du leen jaasiral.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.