TSK

TSK · Joel 2:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Kon jëlal lii ma la may, ndax Yàlla baaxe na ma, ba ma barele.» Mu tinu ko, ba Esawu mujj nangu.

Dingeen bàcc ba keroog wittum reseñ jot te dingeen witt reseñ ba keroog ji jot. Dingeen lekk seenum pepp ba suur këll te dingeen dëkk ak jàmm ci seenum réew.

kër ya feese mboolem lu baax lu ngeen ko feesaluloon, ak teen yu ngeen gasul, ak garabi reseñ ak oliw yu ngeen jëmbatul; bu ngeen ca lekkee ba regg,

Foofa ngeen di lekke, yeen ak seeni njaboot fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ngeen bége fa seen wépp ñaq wu leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeelal.

ndare ngeen lekke ko fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji. Lekkeleen ko fa seen Yàlla Aji Sax ji di taamuji, yeen ak seen doom yu góor, ak yu jigéen, ak seen jaam yu góor ak yu jigéen, ak Leween ñi ci seen biir dëkk. Su ko defee ngeen bége seen wépp ñaq, fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji.

Nangu nañu ay dëkk yu tata wër, ak suuf su nangu, aakimoo kër yu fees ak gépp ngëneel, aki teen, ak tóokëri reseñ, ak garabi oliw, garab yay meññ, ne xas; ñuy lekk ba suur. Ñu regg, di xéewloo sa mbaax gu réy gi.

Yaw laay sante ndaje mu mag, sottalal la samay dige, ñi la ragal seede.

Bu mettee doo rus, te bésub xiif dangay regg.

di reggal sa bakkan bànneex, yeesalal lag ndaw, nga màggataale doole nig jaxaay.

di reek a sarxolle rekk. Yéefar yi naa: «Lu réy la Aji Sax ji defal ñii.»

Moo tax Aji Sax, ji jotoon Ibraayma, wax ak waa kër Yanqóoba, ne leen: «Léegi Yanqóoba du rusati, du amati yaraanga.»

Yaw la ay buur di baayoo, seeni lingeer di la nàmpal. Ñoo lay sujjóotal, di la maral say tànk, ba nga xam ne maay Aji Sax ji, te ku ma yaakaar du rus.»

Ana lu ngeen di waññe xaalis, di ko jënde lu dul aw ñam? Ana lu ngeen di sonn, di jënde lu dul reggal? Dégluleen maa déglu, ba lekk lu leen di dundal, di xéewloo seen ngëneelu bakkan.

Joel 2:20 TSK

Waa bëj-gànnaar, maa leen di soreleek yeen, maa leen di dàq, jëme réew mu maral te wéet, gàngoor ga jiitu jubal géeju penku, ga féete gannaaw jubal 0géeju sowu, ba seeni néew gilli, xasaw ba ubale, ngir jëf ju réy ji ñu def!»

«Su bés baa gàcce dootul am ci sa mboolem jëf, ji nga ma moye, nde maay jële fi sa biir ñiy bége sab sag, te doo damooti ci sama kaw tund wu sell.

Ndaw bànneex akub taar ca ñoom! Pepp yafal xalelu góor, biiñ bu bees naatal yaramu janq.

Noonu la Mbind mi indee ne: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ doj wuy fakktale, mooy xeer wuy daaneel, waaye ku ko wéeroo ngëm, doo rus.»

Ñooñu ñooy aaye ab séy, di digle ñàkka lekk yenn ñam yu Yàlla sàkk, ngir gëmkat ñi xam liy dëgg, man cee jariñu te di ko sante Yàlla.