Ci kaw loolu Sóol jël ñetti junniy xarekat yu mu tànne ci bànni Israyil gépp, ngir wëri Daawuda aki nitam, ba fa dendeek tundi Sikket ya.
TSK
TSK · Jonah 1:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Seytaane ne Aji Sax ji: «Bakkan a wuutu bakkan rekk. Mboolem lu nit am, man na koo weccee bakkanam.
ba ca melax yaak doj yu sedd yay taw, ak tawub yuur akub lay, ba ca ngëlén yu mag yay def ndigalam.
Ndesu matt ma lay sàkke jëmmu tuuram, sukkal ko, sujjóotal ko, ñaan ko, naa: «Yaay sama Yàlla, xettli ma!»
Waaw, ana seen yàlla yi ngeen sàkkal seen bopp? Bu leen musiba dikkalee, nañ leen wallu, bu ñu ko manee! Gannaaw yeen waa Yuda, ni seeni dëkk tollu la seeni yàlla tollu!
Ci kaw loolu njiitu mool ya dikk ba ca moom, ne ko: «Yaw, ana looy nelaw? Jógal kay woo sa yàlla wall! Jombul mu geesu nu, ba dunu sànku.»
Nit ña nag am tiitaange lu gënatee réy ci Aji Sax ji, daldi rendil Aji Sax ji sarax, ba noppi xasal ko aw xas.
Ca ëllëg sa ngelaw la wéye noo pamti-pamtee, ba ñu mujj wàññi ca yebu gaal ga, sànni biir géej.
¶ Waaye la ma jàppe woon ag ndollant, moom laa def tey ag wàññeent ndax Almasi.