TSK

TSK · Lamentations 2:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu taal kër Aji Sax ji, taal kër Buur, ak këri Yerusalem gépp, boole ca këri boroom barke ya.

Job 19:11 TSK

jafalal mam sànjam, boole ma ciy noonam,

Du tee ma wàcceel Aryel musiba, ñuy yuuxook a jooyoo. Yerusalem ay mel ci man ni Aryel, taalub sarxalukaay.

Nañu gaaw dëbbeel nuy jooy, gët taa, rongooñ wal.

Sa soppe yépp a la fàtte, kenn faalewu la ci, ndax dumay noon laa la duma, yar la yar bu tar ngir sa ñaawtéef ju réy ak sa bàkkaar yu bare.

Boroom bee modd te yërëmul mboolem sanci Yanqóoba. Ca meram ma la màbbe tatay Janq Yuda mu taaru ma. Moo detteel nguur ga aki garmeem, sobeel leen.

Mu tàqarñi ko fi sama kanam, muy lu ñu bind biir ak biti, mbind ma di kàdduy jooy aki onk aki yuux.