TSK

TSK · Lamentations 2:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Aji Sax jee leen di diri, yeen ak seen buur bi ngeen fal, ba ca biir xeet wu ngeen xamuloon, yeen ak seeni maam, ngeen di fa jaamu yeneen yàllay bant ak doj.

Mu seetlu ci Aji Sax ji, Aji Sax ji wuyuwu ko; du ci gént, du ci jumtukaayu tegtal bi ñuy wax Urim, du ci kàddug yonent.

Doomi Cedekiya yu góor lañu rendi, muy gis, ba noppi ñu tuur ay bëtam, jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon.

Ñu wax ma, ne ma: «Ña rawe ca njaam ga de, ña nga diiwaanu Yuda, ci njàqare ju réy akug toroxte. Tatay Yerusalem jaa nga tojatoo, bunt ya lakk.»

Tojiti neen a des ci dëkk bi, bunt ba rajaxoo.

Ba Cedesyas tolloo ci fukkeelu atu nguuram ak benn, juróom ñeenti fan ca ñeenteelu weeram, ca lañu bëtt dëkk ba.

Jàmbaari Babilon xareetuñu, ña nga des ca seeni tata, doole ŋiis, ñu mel niy jigéen. Bunti dëkk bi dàjjiku, kër ya jàpp.

Gàngooru Babilon gépp daldi ànd ak njiital dagi buur, ñu màbb tata ya wër Yerusalem.

Ñoom lañuy gëdd naan: «Soreleen nu, nit ñu sobewu ñi! Soreleen, soreleen, buleen nu laal.» Ñu daw di tambaambalu ba ca yeneen xeet; ñooña ne leen: «Dootu fii!»

Ay ci kaw ay a ngi dikk, xibaar ci kaw xibaar, ñuy sàkku peeñum yonent ci neen, ndigalu yoon réer sarxalkat, pexe réer mag.

Maa koy laaw sama mbaal, mu lonkoo samab caax, ma yóbbu ko Babilon, layoo faak moom ñàkke worma gi mu ma ñàkke worma.

Amos 8:11 TSK

«Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «maay wàcce xiif ci réew mi. Du doon xiifub dugub mbaa marum ndox, kàddug Aji Sax ji lañuy xiif.