TSK

TSK · Lamentations 4:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waxleen lu dalal xelu Yerusalem, yéeneleen ne leen seen xare jeex na, seen mbugal mat na. Ñoo nangoo ci loxol Aji Sax ji lu fey ñaari yoon seen bépp bàkkaar.

Deesatul dégg ci sam réew: «Fitna ñëw na!» deesatul dégg it fi sa kemu suuf: «Yàqute ak Yàqulee ngi!» «Mucc» ngay tudde say tata, te «Cant» ngay tudde sa bunti dëkk.

Maa leen di raxasal mboolem ñaawtéef gu ñu ma moye, baal leen mboolem ñaawtéef yu ñu ma moye, di ma gàntal.

Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «dees na seet fi Israyil lu ñaaw, du fi am; fi Yuda it, deesu fi gis bàkkaar. Maay jéggal moos ndes wi ma fi saxal.

Bégleen te bànneexooy, yeen Edomeeni réewum Ucc, ci yeen it la kaasu mbugal di jàllsi, ngeen màndi, futteeku, ne duŋŋ.

«Soxore gi ngeen soxore seen mbokk Yanqóoba moo leen tax di sangoo gàcce, te dees na leen dagg sànni ba fàww.