TSK

TSK · Leviticus 17:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Wax leen boog ne leen: Képp kuy góor, ku bokk ci waa kër Israyil, mbaa mu bokk ci doxandéem yi ci seen biir, buy génne ab saraxu rendi-dóomal mbaa beneen sarax,

¶ «Te itam képp ku lekk médd mbaa lu rab fàdd, muy njuddu-ji-réew mbaa doxandéem, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set.

su boobaa bérab bu seen Yàlla Aji Sax ji taamu ngir dëël fa turam, foofa ngeen di yóbbu mboolem lu ma leen sant: seen saraxi dóomal, ak yeneen sarax, ak seen céri fukkeel, ak seenub jooxe, ak mboolem ngëneel yu ngeen di def saraxi xas yu ngeen xasoo ak Aji Sax ji.

ndax bérab bu Aji Sax ji taamu ci genn ci seen giir yi, foofa ngeen di joxe seen saraxi dóomal, te foofa ngeen di def lépp lu ma leen sant.

¶ Waaye seen yëf yu ñu sellal, ak seen sarax yi ngeen xasoo, jël-leen ko, yóbbu ca bérab ba Aji Sax ji di taamuji.