TSK

TSK · Leviticus 18:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Waxal bànni Israyil ne leen: Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.

¶ «Te it sama dogali yoon yii nangeen ko sàmm: buleen boole ñaar yu bokkul wirgo ci seenug jur, ñuy jaxasoo; seen tool it buleen ci ji ñaari wirgoy jiwu te buleen sol yére yu ñu ràbbe ñaari xeeti wëñ yu bokkul.

¶ «Sàmmleen sama dogali yoon yépp ak sama santaane yépp te jëfe ko, ngir réew ma ma leen jëme, ngeen dëkki fa, bañ leena gëq.

¶ Lii mooy santaane bi, ak dogali yoon yeek àttey yoon yi seen Yàlla Aji Sax ji santaane ma jàngal leen ko, ngir ngeen di ko jëfe ca réew ma ngeen jàll jëm, ngir nanguji ko,

Aji Sax ji, yaa joxe sa tegtal yi ñu wara toppa topp.

te samam xel laay yeb fi seen biir dënn, ba dogal ngeen mana topp sama dogali yoon, di sàmm ak a jëfe sama àttey yoon.

Luke 1:6 TSK

Ñoom ñaar ñépp a juboon, Yàlla seede, te mucc ayib ni ñuy jëfe santaane yeek ndigali yooni Boroom bi.