Waaye ku sobewu ku lekk ci yàppu jur gu ñu defal Aji Sax ji saraxu cant ci biir jàmm, kooku nañu ko dagge ci biir bànni Israyil.
TSK
TSK · Leviticus 20:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Fexeleen ba bànni Israyil di tàggook seeni sobe, lu ko moy dinañu dee ndax seen sobe, ngir dañuy taqal sama màkkaan mi ci seen biir.»
¶ «Bul jébbal kenn ci say doom tuur mi ñuy wax Moleg, ndax waruloo teddadil sa turu Yàlla. Man maay Aji Sax ji.
Nañu nekkal seen Yàlla ay nit ñu sell, te baña teddadil seen turu Yàlla, ndax saraxi sawar yi ñeel Aji Sax ji, te di seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Kon nag dañoo wara sell.
¶ «Moo tax, dogu naa ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, gannaaw yeena def seen wépp njombe ak seen jépp jëf ju siblu, di sobeel sama bérab bu sell bi, man itam, maa leen di wat nel te duma leen xool bëtu ñéeblu, duma leen ñeewante.
Lii itam, ñoo ma ko def: Bésub keroog lañu sobeel sama kër gu sell, teddadil sama bési Noflaay.
Ndax ay gët la Boroom bi ne jàkk aji jub ñi, te ay noppam la dékk seeni ñaan, waaye Boroom bi, kanamam lay tëjal ñiy def lu bon.»