TSK

TSK · Leviticus 3:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Waxal bànni Israyil ne leen: Bu kenn ci yeen dee sàkkal Aji Sax ji sarax, na indi ag jur, muy gu gudd mbaa gu gàtt.

¶ «Bu saraxam dee ab gàtt bu ñuy def rendi-dóomal, muy xar mbaa bëy, na sarxal bu góor bu amul sikk.

¶ Gannaaw gi Aaróona indi saraxi mbooloo mi, jël sikketu mbooloo miy doon seen saraxu póotum bàkkaar, rendi ko, sarxal ko, na mu sarxale la jiitu.

liy tax ñu nangul ko mooy muy jur gu amul sikk, di góor; man naa doon aw yëkk mbaa kuuy mbaa sikket.

Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko këpp sunu gépp ñaawtéef.

Li yoonu Musaa tële woon ndax néew dooley nitu suuxu neen, mooy lii Yàlla def: Doomam la yónni, mu dikke melow nit, te nit di bàkkaarkat, di suuxu neen, ngir Doomam fajtal mbirum bàkkaar. Yaramu suux wu nit kooku la Yàlla sottale mbugal gi war ci bàkkaar,