TSK

TSK · Leviticus 4:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su ko defee mu summi yéreem yooyu, sol yeneen te génne dóom bi dal bi, yóbbu ko fu mucc sobe.

Képp kuy góor ci doomi Aaróona yi man na cee lekk. Seen cér la bu ñu leen sédde ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, te dogalal leen ko fàww. Lépp lu ci laal day doon lu sella sell.»

Li des ci yëkk wi, di der beek yàpp week sébbriit mi, mu génne ko dal bi, lakk ko ca biti, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.

Muy yëkk wiy saraxu póotum bàkkaar, muy sikket biy saraxu póotum bàkkaar te ñu yóbbu woon seen deret ca biir bérab bu sell baa sell ngir defe ko njotlaay, lépp lañuy génne dal bi. Der yaak yàpp waak sébbriit ma dees koy boole lakk, ba mu dib dóom.

Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Dee rekk mooy àtteb waa ji: dees koy génne dal bi, mbooloo mépp dóor koy xeer, ba mu dee.»

Nañu lakk nag wi‎ ci kanamam. Der bi ak yàpp wi ak deret ji ak sébbriit mi, lépp lañuy lakk.

Ndax kat, jur ga sarxalkat bu mag ba daan yóbbu seen deret ca bérab bu sell baa sell, ngir njotlaayal bàkkaar, seen yaram lees daan lakk ca bitib dal ba.