TSK

TSK · Leviticus 4:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Bu saraxam dee saraxu jur gu gudd gu ñuy def rendi-dóomal, na sarxal aw yëkk wu amul sikk. Na ko yóbbu ci bunt xaymab ndaje mi ci kanam Aji Sax ji, ngir mu nangul ko ko.

bu mbooloo mi nemmikoo moy gi rekk, war nañoo génne ci jur gu gudd gi yëkk wu ndaw wuy doon saraxu póotum bàkkaar, yóbbu ko ca bunt xaymab ndaje ma.

Su sàgganee it ba giñ ne dina def nàngam, muy lu baax mbaa lu bon, muy mboolem ngiñ lu ko rëcc te ba mu koy wax teyu ko, ba mu wees, saa yu ko xamee tooñ na.

Te itam ngeen sarxal ab sikket buy doon saraxu póotum bàkkaar ak ñaari xari menn at, muy saraxu cant ci biir jàmm.

ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,

ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,

Ak itam bennub sikket, mook saraxu tuuroom ngir saraxu póotum bàkkaar, ñeel Aji Sax ji ci bésub Terutel weer wi, te bokkewul ak rendi-dóomal bi ñuy sarxe bés bu nekk.

ak benn sikketu póotum bàkkaar, ngir seen njotlaay.

ak benn sikketu póotum bàkkaar. Bokkewul ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, ak saraxu peppam si muy àndal, ak saraxu tuuram.

Safan bindkat ba teg ca xamal Buur ne ko: «Ab téere nag la ma Ilkiya sarxalkat bi jox.» Safan jàngal ko Buur.

Bésub ñaareel ba nanga indi ab sikket bu amul sikk, muy saraxu póotum bàkkaar bu ñuy laabale sarxalukaay bi; ñu laabale ko sarxalukaay bi, na ñu ko laabale woon yëkk wu ndaw wa.