TSK

TSK · Leviticus 4:34

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Na sarxalkat bi capp baaraamam ci deretu sarax siy póotum bàkkaar, taqal ko ci béjjéni sarxalukaayu rendi-dóomal bi, ba noppi tuur deret ji ci taatu sarxalukaayu rendi-dóomal bi.

Aji Sax ji la soob ci njekkam, mu fésal màggaayu yoonam ak taar ba.

¶ Kon nag léegi, amul benn daan bu ñeel ñi bokk ci Almasi Yeesu.

Ndax kat Almasi moo sottal yoonu Musaa, ngir àtteb ku jub ñeel képp ku ko gëm.

¶ Ndax kat Yàlla mi lépp lu sàkke ñeel, te lépp sàkkoo ci moom, moo nammoona wommat gone yu bare ba sédd leen daraja. Moo tax muy lu jaadu, mu sottale matug Yeesu ay coono, ndax Yeesu moo xàllal gone yooyu yoonu mucc.

Xam ngeen ne yëf yuy wéy yu mel ni xaalis mbaa wurus, du moom lees leen jote ci seen dundinu neen wa ngeen donne ca seeni maam,

Almasi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gi.