Su ko defee nga rendi kuuy mi, sàkk ci deret ji, taqal ci tabanum noppu ndijooru Aaróona ak tabanum noppu ndijooru doomam yi, te nga taqal ci seen baaraamu déyu ndijoor, ak seen baaraamu tànku ndijoor bu mag. Boo noppee, nga xëpp li des ci deret ji ci peggi sarxalukaay bi yépp ba mu daj.
TSK
TSK · Leviticus 8:23
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Na sarxalkat bi sàkk ci diw gi des ci loxoom, tooyal ci tabanu noppu ndijooru nit ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram; nañu ko laalal ci diw gi fa ñu ko jëkkoona taqal ci deretu sarax siy peyug tooñ.
Loolu wéy sarxalkat bi wara sàkk ci diw gi ci loxoom, tooyal ca tabanu noppu ndijooru ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram; na ko def ca bérab boobu mu taaj deretu sarax siy peyug tooñ.
¶ Ni ko nit mana dégge rekk, ni laa leen woyofalale kàddu gii, ndax seen néew dooley nitu neen. Noonee ngeen jébbale woon seeni cér, def leen ñuy jaami sobe, ak ndëngte gu jur ndëngte, noonu ngeen wara jébbale seeni cér, def leen ñuy jaami njub gu jur sellnga.
ñeel mbooloom Yàlla, mi ci Korent, yeen ñi ñu sellal ci jëmmu Almasi Yeesu, te ñu woo leen ngir ngeen doon ñu sell, ñeel itam mboolem ñiy tudde fépp fu mu mana doon, sunu turu Boroom Yeesu Almasi, mi leen moom, moom nu.
ndax dees leena jot, ba fey njég ga. Kon nag seen yaram, terale leen ko Yàlla.
Su ma ci deeyee sax, ba sama dund mel ni sarax su ñu tuur, tofal ko ci sarax, bi seen ngëm taxawe, su boobaa it maa ciy bég, te di leen woo, ngir bokk ak yeen ñépp bànneexu.
¶ Ndax kat Yàlla mi lépp lu sàkke ñeel, te lépp sàkkoo ci moom, moo nammoona wommat gone yu bare ba sédd leen daraja. Moo tax muy lu jaadu, mu sottale matug Yeesu ay coono, ndax Yeesu moo xàllal gone yooyu yoonu mucc.