TSK

TSK · Leviticus 8:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sàkkal ci deret ji ci sarxalukaay bi, ak ci diwu pal gi, nga wis-wisal ko ci kaw yaramu Aaróona ak ci kawi yéreem, wis-wisal ko ci kaw yarami doomam ak ci seen kawi yére. Su ko defee Aaróona sell, mooki yéreem, ay doomam it sell, ñook seeni yére.

¶ Loolooy céri pal yi Aaróona ak askanam di am ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, dale ko keroog bu ñu leen teewalee fi kanam Aji Sax ji, ñu doon ay sarxalkat.

Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.

Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma, ngir ma àgge néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi, seen goreel, yégal ñi ñu tëj, seen ubbite.

¶ Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel, ak mbég, ak jàmm, ak xolu muñ, ak mbaax, akug tabe, ak ngëm,

Yeen la Yàlla Baay bi ràññee lu jiitu, ci ni mu leen sellale Noo gu Sell gi, ngir ngeen mana déggal Yeesu Almasi, boole ci tooyloo deretam, mu setal leen. Aw yiw ak jàmm ju ne xéew ñeel na leen.

¶ Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Gàtt bi.