TSK

TSK · Leviticus 9:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

te waajal gannaaw-ëllëg, ndax gannaaw-ëllëg man Aji Sax ji maay wàcc ci kaw tundu Sinayi ci kanam mbooloo mépp.

Foofa laay dajeek bànni Israyil, bérab ba doxe fa sell, ndax samag leer.

¶ «Bu nit dee indil Aji Sax ji saraxu pepp, sunguf su mucc ayib la saraxam wara doon, mu sotti ci diw, def ci cuuraay,

Saafukaayu weñ lañu koy lakke, xiiwaale ko diw, indi xiiw ba, muy saraxu pepp. Nañu ko def ay dog yu ñuy lakkal Aji Sax ji, muy xeeñ xetug jàmm.

Musaa ak Aaróona ànd dugg ca biir xaymab ndaje ma; ba ñu génnee, ñaanal mbooloo ma, leeru Aji Sax ji feeñu mbooloo ma mépp.

bu ngeen di defal Aji Sax ji saraxu sawara, muy saraxu rendi-dóomal, mbaa sarax su nit di wàccoo aw xas, mbaa saraxu yéene, mbaa seen saraxi màggal, ngir xeeñal xetug jàmm ñeel Aji Sax ji, te muy lu jóge ci jur gu gudd mbaa gu gàtt, defe leen ko nii:

¶ Ba sarxalkat ya génnee bérab bu sell ba, niir wa daa fees kër Aji Sax ja,

Bu àpp boobu matee, la ko dale ca bésub juróom ñetteel ba, na sarxalkat yi joxe ci kaw sarxalukaay bi, seen saraxi rendi-dóomal, ak seen saraxi cant ci biir jàmm, ma daldi leen nangul. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»