TSK

TSK · Luke 10:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su ko defee ngeen bége fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, yeen ak seen doom yu góor ak yu jigéen, ak seen jaam yu góor ak yu jigéen, ak Leween ñi ci seen biiri dëkk te amuñu wàll, amuñu céru suuf ci seen biir.

njël lu yemook njëlal ña mu fa fekk it lew na ko, te limaaleesul lu ko dikke ci njaayum alalu baayam.

Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram. Mu daldi nu ñaan, ne nu: «Ndegam ab gëmkatub Sang bi ngeen ma jàppe, agsileen, dal ak man ca sama kër.» Mu soññ nu ba nu nangu.

Noonu lañu génne kaso ba, dellu kër Lidi. Ñu gise faak bokki gëmkat ña, ñaax leen, doora dem.

¶ Ki ñuy jàngal kàddug Yàlla nag war naa sédd ki koy jàngal ci mboolem alalam.

Te itam ca lañuy tàmme am ug jot, di taxawaalu kër ak kër. Te duñu yem ci am ag jot rekk, waaye dañuy làmmiñu, di dugg lu seen yoon nekkul, tey wax lu leen warul.

Te it beykat bi yor coonob liggéey bi, moo wara jëkka séddu ca meññeef ma.