TSK

TSK · Luke 20:35

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñu baree ngi nelaw, keroog ñu yewwoo fa pëndub suuf. Ñenn ña nara dund fàww, ña ca des añe gàcceek njàqare fàww.

Teewluleen boog, tey ñaan saa su nekk, ba mana mucc ci mboolem looluy nara xew, ngir ngeen taxaw fi kanam Doomu nit ki.»

Acts 5:41 TSK

¶ Ndaw ya nag bàyyikoo ca kurélu àttekat ya, di bég, gannaaw ñoom lañu jàpp ne ñoo yelloo toroxte ga ñu leen teg ndax Tur wi.

¶ Loolu lépp di firndeel njekku àtteb Yàlla, bi leen di yellale nguurug Yàlla, gi tax ngeen di sonn.

¶ «Moona am nga foofu ci Sàrd nit ñu néew ñu tilimalul seen mbubb. Ñooñooy ànd ak man, sol lu weex, ndax ñoo ko yeyoo.