Boroom beey wal noowal mbugal, noo guy lakk, sellal, fóote ko jonkani jigéeni Siyoŋ, fetee ko deret ji ci Yerusalem, ba mu set.
TSK
TSK · Luke 3:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Maay sottim ndox suuf su mar, ak wal yu waleg joor gu wow. Maay sotti saw askan samag noo, sama barke sottikul ñi nga meññ,
Waaye bésub dikkam, ana ku ko mana dékku? Bu teewee ana kuy taxaw? Nde moom daa mel ni sawaras tëgg buy xelli weñ, melati ni xemey fóotkat.
Ndax cim ndox la Yaxya daan sóobe, waaye yeen ci Noo gu Sell gi lees leen di sóob fii ak fan yu néew.»
“Yàlla nee: Mujug jamono, maay tuur samag Noo ci kaw wépp suux; seeni doom, góor ak jigéen di biral waxyu, seeni xale yu góor di gis ay peeñu, màggat ñi di gént ay gént.
¶ Ba Piyeer di wax kàddu googu, Noo gu Sell gi daldi wàcc ci kaw mboolem ñay déglu kàddu ga.
Laata muy ñëw, Yaxya moo doon yéene ngir waa bànni Israyil gépp sóobu cim ndox, jëmmale ko seenug tuubeel.
Ci genn Noo gi lañu nu sóobe ci biir wenn yaram wi, nun ñépp, nu diy Yawut, mbaa nu diy jaambur, nu diy jaam, mbaa nu diy gor, te nun ñépp, genn Noo gi lañu nu nàndale.