TSK

TSK · Luke 5:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci kaw loolu ñu ne Musaa: «Yaw, waxal ak nun, nu dégg, waaye bu Yàlla ci boppam wax ak nun, lu ko moy nu dee.»

Ci kaw loolu waa Bet Semes ne: «Ana ku mana taxaw fi kanam Aji Sax ji, jii Yàlla ju sell? Ci kan lanuy yóbbu gaal gi, ba mu sore nu?»

Jigéen ja ne Ilyaas: «Éy góoru Yàlla gii! Ana lu ma séq ak yaw? Xanaa dangaa ñëw sullisi sama bàkkaar, ba tax nga rey sama doom ju góor jii?»

Job 42:5 TSK

Dég-dégu nopp laa amoon ci yaw, tey bët laa la teg.

Jekki-jekki jëmm ju mel ni nit dikk, laal samay tuñ. Ma ŋa, àddu, daldi wax ak ki taxaw sama kanam ne ko: «Sang bi, peeñu mi tax na ma jàq, ba amatuma benn doole.

Tey jii ci ab seetu lanuy gise gis-gis bu lënt. Waaye bu keroogee, màkk lanuy jàkkaarloo ak li nuy xool. Tey jii, as ndog laa xam, waaye su keroogee, ni ñu ma xame, ni laay xame ba mu mat sëkk.

¶ Man Yowaan maa dégg mbir yii, gis ko. Ba ma ko déggee, gis ko, dama ne gurub sukk ci tànki malaaka, mi ma ko won, nar koo sujjóotal.