Ci kaw loolu Aji Sax ji romb fa kanam Musaa, di biral naan: «Aji Sax jee, Aji Sax ji, Yàlla jiy yërëm, di yéwéne, mer ma diib, ngor gaak kóllëre ga bare.
TSK
TSK · Luke 7:47
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Na ku bon ba jëfinam, kuy def lu ñaaw fomm mébétam, te walbatiku ci Aji Sax ji sunu Yàlla, mu yërëm ko, yaatal njéggalam.
Maa leen di musal ci seen mboolem sobe, maay woo am pepp, ful ko, te dootuma leen teg ab xiif.
¶ Farisen ba woo Yeesu nag gis loolu, naan ci xelam: «Kii su doon ab yonent, dina xam ndaw sii di ko nabb-nabbee ku mu doon, ak lu mu doon: jigéenu moykat!»
¶ Yoonu Musaa moo dikk ngir fésal barewaayu moy, waaye fu bàkkaar bare, aw yiw gën faa bareeti,
Ndaxte cofeelu Almasi daal moo nu jiite, nun ñi ràññee lii: Gannaaw kenn moo deeyal ñépp, kon ñépp a dee.
Na aw yiw ñeel mboolem ñi sopp sunu Sàng Yeesu Almasi, cofeel gu dul fey.
Sunu yiwu Boroom moo ma baawaanal, booleel ma ci ngëm gi, ak cofeel, gi gëmkatub Almasi Yeesu jagoo.